Saar 5
Yeremee ngi ñaan
1 Éy Aji Sax ji, bàyyil xel li nu dal,
xoolal, gisal sunu toroxte!
2 Sunu suuf toxu ciy jaambur,
sunuy kër ñeel ay doxandéem.
3 Baay dëddu, nu diy jirim;
ndey dib jëtun.
4 Sunum ndox, xaalis lanu koy feye, naan,
sunu matt ak njégam la mu nuy dikke.
5 Sunuw loos lañu ràng,
nu loof, te noppaleesu nu.
6 Nu nangul Misra,
nangul Asiri ngir ab dund.
7 Sunuy maam a moyoon, tey nekkatuñu;
nun, noo gàddu seeni mbugal.
8 Ay surgaa nu yilif, te amunu
ku nu wallu ci seen loxo.
9 Bu nu lekkee, sunu bakkan lanu jaay,
nde saamar a ngi ci màndiŋ mi.
10 Sunu yaram nib taal la tànge
ndax tàngoorub xiif.
11 Jigéeni Siyoŋ lañuy tëdde,
ak janqi dëkki Yuda.
12 Kàngam yi, ñu jàpp, wékk;
te mag ñi, teraleesu leen.
13 Waxambaane yee yenu doji wolukaay,
gone yu góor yi sëfoo sayi matt, di tërëf.
14 Mag dakkal na jataayu pénc,
te waxambaane talatula xalam.
15 Xol nux-nuxeetul,
te ay rongooñ a wuutuy pooj.
16 Sunu mbaxana foq na!
Wóoy ngalla nun ñi moy!
17 Lee jeexal sunu xol,
lii moo nu jooyloo, ba gët giim:
18 tundu Siyoŋ wi gental,
ba till yi di fi daagoo.
19 Yaw Aji Sax ji, yaay toog ba fàww,
sab jal, sët ba sëtaat.
20 Ana lu waral nga fàtte nu fàww,
ba nu jant yu yàgge nii?
21 Éy Aji Sax ji, délloosi nu fi yaw, nu dellusi,
yeesalal sunuy jant, mu mel na woon.
22 Xanaa doo nu wacca wacc,
mere nu mer mu amul kemu?