Saar 21
Lu jëm ci sañ-sañi sarxalkat yi
1 Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Waxal sarxalkat yiy doomi Aaróona ne leen: Bu ci kenn sobeel boppam, di laal mbokkam mu dee, 2 su dul ñi ko gëna jege ci wàllu mbokk, muy ndeyam mbaa baayam mbaa doomam ju góor ak doomam ju jigéen, mbaa ku góor ku mu bokkal waajur, 3 mbaa ab jigéenam bu séyagul te bootu ci moom ndax amul jëkkër— ku mu bokkal noonu, sañ naa sobewu ndax moom. 4 Warula sobeel boppam, di teddadil boppam, ndax kilifa la ciw xeetam.
5 «Buñu wat fenn ci seen bopp te buñu wat seen peggi sikkim, buñu dagg seen yaram it, di ko mititloo ku dee. 6 Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.
7 «Ab gànc mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, ñoom duñu ko jël soxna. Ku jëkkëram baal it duñu ko jël soxna, ndax dañoo sellalal seen bopp seen Yàlla. 8 Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax ku Sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen.
9 «Su fekkee ne doomu sarxalkat da di jigéen juy teddadil boppam, di gànctu, kooku baayam lay torxal. Dees koy taal, lakk ko.
10 «Sarxalkat, bi gëna màgg ci bokkam yiy sarxalkat, te ñu sotti diw gi ñuy fale ci boppam, sellal ko, muy sol yére yu sell yi, kooku du njañu te du xotti ay yéreem, di ko ñaawloo ku dee. 11 Fu ab néew nekk du fa dem, bu doon ndeyam mbaa baayam sax, du ko taxa sobeel boppam. 12 Du génn ëttu bérab bu sell bi, mbaa muy teddadil bérabu Yàllaam bu sell bi, ndax diwu pal gu sell gi ko Yàllaam fale. Maay Aji Sax ji. 13 Sarxalkat bu mag bi, ku xamul góor lay jël soxna. 14 Ku jëkkëram faatu mbaa ku ñu baal mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, mbaa ab gànc, du ko mana jël soxna. Ab janq bu mu bokkal doŋŋ la mana jël soxna. 15 Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israyil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.»
Liy ngànt ci sarxalkat
16 Bu loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: 17 «Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam. 18 Du kenn sax ku am sikk kuy agsi ba fii, du gumba, du kuy soox, du ku xar-kanamam am sikk mbaa ku cér yi sutaate. 19 Du it ku tànk bi làggi mbaa loxo bi, 20 mbaa ab xuuge mbaa ab tungune; du it ku bëtam am sikk mbaa ku ràmm mbaa ku am góom yu sol dëtt, mbaa ku ñu tàpp. 21 Askanu Aaróona sarxalkat bi, du kenn ku ci am sikk kuy agsi ba fii, di joxe saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Sikk si ci moom a tax du mana agsi ba fii, di joxe ñamu Yàllaam. 22 Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu sell ak wu sella sell. 23 Waaye warula jege rido bi, mbaa muy dem ba ca sarxalukaay ba, ndax sikk si ci moom. Bumu teddadil sama bérab yu sell, ngir man Aji Sax ji maa sellal bérab yooyu.»
24 Musaa jottli na Aaróona aki doomam kàddu yooyu, ñoom ak mboolem bànni Israyil.