Saar 8
Lu jëm ci teginu làmp ya
1 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko, 2 mu wax Aaróona, ne ko: «Buy teg làmp yi, fa féete tegukaayu làmp ba kanam, fa la juróom ñaari làmp ya wara niite.» 3 Noonu la Aaróona def. Fa féete tegukaay ba kanam, fa la féetale ay làmpam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa. 4 Tegukaayu làmp bi nag, ni ñu ko liggéeye nii la. Wurus lañu ko tëgge ba mu jekk, dale ko ci tànk bi, ba ci mbar mi. Noonee ko Aji Sax ji wone woon Musaa, na lañu liggéeye tegukaayu làmp ba.
Lu jëm ci cetlug Leween ñi
5 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko, 6 «Nanga jële Leween ñi ci biir bànni Israyil te nga setluloo leen. 7 Ni ngay def ngir setluloo leen nii la: Danga leen di wis ndoxum setlu, ba noppi ñu wat seen yaram wépp, fóot seeni yére, daldi set. 8 Su ko defee ñu jël aw yëkk wu ndaw, booleek saraxu peppam, di sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak weneen yëkk wu ndaw wooy jël ngir saraxu póotum bàkkaar. 9 Indil Leween ñi ci kanam xaymab ndaje mi, te nga dajale mbooloom bànni Israyil mépp. 10 Boo indee Leween ñi fi kanam Aji Sax ji, bànni Israyil daldi teg seeni loxo ci kaw Leween ñi. 11 Su ko defee Aaróona taxawal Leween ñi taxawaayu saraxu yékkati-jébbal fi kanam Aji Sax ji, muy sarax bu bawoo ci bànni Israyil, Leween ñi daldi sasoo di liggéey liggéeyu Aji Sax ji. 12 Leween ñi ñoom, nañu teg seeni loxo ci kaw boppi yëkk yi, ñu def wenn wi saraxu póotum bàkkaar, te def wi ci des ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ngir njotlaayal Leween ñi. 13 Gannaaw loolu ngay taxawal Leween ñi fi kanam Aaróona ak doomam yu góor, daldi leen def saraxu yékkati-jébbal, ñeel Aji Sax ji. 14 Noonu ngay seppee Leween ñi ci biir bànni Israyil, Leween ñi doon sama cér. 15 Gannaaw loolu la Leween ñiy doora dugg ci liggéeyu xaymab ndaje mi. Danga leen di jëkka setluloo, ba noppi def leen saraxu yékkati-jébbal. 16 Ñoom déy lañu ma sédda sédd ci biir bànni Israyil, ñu wuutu mboolem luy ubbiteg njur, di taawi mboolem bànni Israyil. Maa leen sédd sama bopp. 17 Ndax man maa séddoo mboolem taaw ci biir bànni Israyil, nit ak mala. Keroog ba ma fàddee mboolem taaw ca réewum Misra, ca laa leen sellalal sama bopp.
18 «Maa jël Leween ñi, weccikoo leen bépp taaw ci biir bànni Israyil, 19 te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee bérab bu sell bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.»
20 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona ak mbooloom bànni Israyil mépp daldi defal Leween ñi noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa ci Leween ñi, noona la ko bànni Israyil defe ak ñoom. 21 Leween ñi setlu, fóot seeni yére, Aaróona def leen ni saraxu yékkati-jébbal, ñeel Aji Sax ji. Mu defal leen nag seen njotlaay ngir setal leen. 22 Gannaaw loolu Leween ñi doora liggéeyi seen liggéey ci wàllu xaymab ndaje mi, ci kilifteefu Aaróona aki doomam. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa ci Leween ñi, na lañu def ak ñoom.
23 Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 24 «Lii nag moo war ci Leween ñi: ku ci am ñaar fukki at ak juróom, jëm kaw, yelloo naa bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war. 25 Waaye ku xasa am juróom fukki at, na génn kurél gi boobu liggéey war, te bumu ca liggéeyati. 26 Sañ naa jàpple bokki Leweenam ñi dénkoo dénkaaney xaymab ndaje mi, waaye dootu ci liggéey lenn. Noonu ngay def ak Leween ñi, ci seen wàlli dénkaane.»