Saar 13
Musaa yeble na Kanaan
1 Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 2 «Yebalal ay ndaw, ñu dem yëri réewum Kanaan, gi may jox bànni Israyil. Kenn ngay yebal ci seen giiri maam yi, giir gu ci nekk, kenn, te ku ci nekk di kilifa ci ñoom.» 3 Ci kaw loolu Musaa yebal ndaw ña ci ndigalal Aji Sax ji, ñu bàyyikoo ca màndiŋu Paran. Ñoom ñépp ay njiiti bànni Israyil lañu woon. 4 Ñooñu ñoo di:
Samwa doomu Sakuur, ci giirug Rubeneen ñi,
5 ak Safat doomu Ori, ci giirug Cimyoneen ñi,
6 ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi,
7 ak Igal doomu Yuusufa, ci giirug Isakareen ñi,
8 ak Oseya doomu Nuun, ci giirug Efraymeen ñi,
9 ak Palti doomu Rafu, ci giirug Beñamineen ñi,
10 ak Gadyel doomu Sodi, ci giirug Sabuloneen ñi,
11 ak Gadi doomu Susi, mi taxawal làngu Manase ci biir giirug Yuusufeen ñi,
12 ak Amyel doomu Gemali, ci giirug Daneen ñi,
13 ak Setur doomu Mikayel, ci giirug Asereen ñi,
14 ak Nabi doomu Wofsi, ci giirug Neftaleen ñi,
15 ak Gewuyel doomu Maki, ci giiru Gàddeen ñi.
16 Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
17 Ba leen Musaa yebalee ngir ñu yëri réewum Kanaan, da ne leen: «Negew gii ci bëj-saalum ngeen di jaare, yéegi ca diiwaanu tund ya, 18 ba gis nu réew ma mel: ndax waa réew ma, ñu am doole lañu, am ñu néew doole; ñu néew lañu, am ñu bare; 19 ak ndax réew ma baax na, am baaxul; ak nu seeni dëkk mel: ndax ay dal rekk la, am ay dëkk yu ñu dàbbli la; 20 ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef.
21 Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Reyob, ga ca wetu Amat. 22 Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra. 23 Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg. 24 Bérab boobu lañu dippee xuru Eskol, (mu firi xuru Cëgg) ndax cëgg ba fa bànni Israyil dagge woon.
Ndaw ya délsi nañu
25 Ndaw ya nag ñibbsi, gannaaw ba ñu nemmikoo réew ma lu mat ñeent fukki fan. 26 Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israyil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma. 27 Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa. 28 Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis. 29 Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
30 Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»
31 Ndaw ya àndoon ak moom daldi ne: «Manunoo songi waa réew ma, ndax ñoo nu ëpp doole.» 32 Ci biir loolu ñuy baatal ca kanam bànni Israyil, réew ma ñu nemmikuji woon. Ñu naan: «Réew moomee ñu wëri woon ngir nemmiku ko déy, réew la muy faagaagal ay sancaanam, te mboolem askan wa nu fa gis, ay boroom jëmm lañu. 33 Fa lanu gis xeetu Nefilim ya, ponkali Anageen ña bokk ca xeetu Nefilim ya, nuy niru sunu bopp ay soccet fi seen kanam, di leen ko niru, ñoom it.»