Kàddu yu Xelu
Saar 1
Li tax téere bi jóg
1 Kàddu yu xelu yu Suleymaan buurub Israyil, di doomu Daawuda.
2 Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég, 3 ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal, 4 ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat. 5 Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal, 6 ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam,
te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
Déglul, waajur àrtu la
(Saar 1.8—7.27)
8 Doom, toppal yaru baay,
te bul wacc ndigalu yaay.
9 Kaala gu jekk la ci bopp,
di gànjar ci baat.
10 Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11 Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan,
yeeruji jaambur bu deful dara.
12 Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund,
mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13 Mboolem alal ju réy, nu jagoo,
yeb sunu biir kër, mu fees.
14 Dikkal nu far,
mbuus miy benn, nu bokk.»
15 Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon,
bul jaare fa ñuy jaar,
16 ngir dañuy xélu, nar musiba,
di gaawtuy sànk bakkan.
17 Doo firib caax,
ba jàpp njanaaw luy xoole.
18 Ñii kat seen bopp lañuy fiir,
seen bakkanu bopp lañu sànk.
19 Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje:
wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
Xel mu Rafet woote na
20 Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma,
di xaacu ca pénc ma.
21 Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb,
di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
22 Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi?
Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi?
Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23 Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la.
Ma ne, kon ma xellil la samam xel,
xamal la samay kàddu.
24 Damaa woote, nga gàntal,
ma tàllal loxo, faaleesu ma.
25 Sofental nga samay digle,
nanguwoo samay àrtu.
26 Kon boo sëngéemee, man it ma ree,
njàqare dab la, may textexi.
27 Njàqare di ngëlén, dab la,
sa musiba def callweer, buub la,
njekkar ak fitna dal la.
28 Keroog nga woo ma wall, duma wuyu,
nga seet ma, seet, doo ma gis.
29 Daa fekk nga baña xam,
te ragal Yàlla du loo taamu.
30 Dégluwoo samay digle it,
xanaa xeeb samay àrtu yépp.
31 Waaye loo ci góobe, gar ko,
say pexe suur la këll.
32 Déggadi sànk ab téxét,
naagu rey ab dof.
33 Waaye déggal ma, dëkke jàmm,
tàggook njekkar ak safaan.»