Sabóor 39
Dund yàggul
1 Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Dama noon: «Damay moyu ba duma moye làmmiñ.»
Li feek ku bon di teew,
may ŋalaab sama gémmiñ.
3 Dama noon cell, ne patt,
noppi, ba mu ëpp;
sama njàqare yokku,
4 sama xol diis,
xel di xelaat, xol diis gann;
ma mujj àddu,
5 ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj
ak sama àppi fan,
ma xam ni sama dund gàtte.
6 Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan,
sama giiru dund du dara fi yaw.
Képp ku taxaw di cóolóolu neen.
Selaw.
7 Nit du lu moy takkndeer buy dem,
cóolóolu neen lay kër-këri.
Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
8 «Éy Boroom bi, lu may xaarati?
Sama yaakaar yaw a.
9 Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ,
bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!
10 Noppi naa, dootuma wax,
yaw yaa dogal lii.
11 Waaye ngalla teggil sab yar,
sa diisaayu loxoo ngi may jekkli.
12 Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko,
ronq ni max la mu gëna fonk.
Nitoo nit, cóolóolu neen.
Selaw.
13 Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la,
teewlul, ma woo la wall;
bul tanqamlu sama yuux,
doxandéem doŋŋ laa fi yaw,
di gan ni maam yépp.
14 Ngalla xiddi ma, ma muuñ,
bala maa dëddu, réer.»