Sabóor 42
Maa namm Yàlla
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
2 Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox,
maa la koy sàkkoo xol.
3 Maa mar Yàlla,
Yàlla jiy dund!
Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?
4 Rongooñ laay dunde
guddeek bëccëg,
noon yi di ma dëkke naa:
«Ana sa Yàlla ji?»
5 Lii laay fàttliku, sama xol jeex:
dama daan jàll, jiite mbooloo ma,
jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant,
ñu booloo di màggal.
6 Moo man, lu may yoggaaral nii?
Lu may jàq?
Naa yaakaar Yàlla,
ba dellu sante sama Yàlla wallam.
7 Maa ngi ne yogg,
ba di la fàttlikoo fa réewum Yurdan
ak tundi Ermon ak Misar.
8 Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma;
say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
9 Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram,
guddi ma fanaane koo woy,
di ñaan Yàlla mi may dundal.
10 Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko:
«Lu tax nga fàtte ma,
noon di ma fitnaal,
may wéye tiis?»
11 Noon yaa ngi may ñaawal,
di ma yendoo naa:
«Ana sa Yàlla ji?»
Ma ne yàcc, ne yasar.
12 Moo man, lu may yoggaaral nii?
Lu may jàq?
Naa yaakaar Yàlla,
ba dellu sante sama Yàlla wallam.