Sabóor 55
Xarit wor na ma
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda.
2 Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la,
bul làqu, dama lay dagaan.
3 Teewlu ma, nangul ma.
Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp;
4 coowal noon yee
ak coonob ñu bon ñi.
Dañu maa teg fitna,
di ma songe xadar.
5 Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi;
tiitaangey ndee ne ma taral.
6 Njàqaree ma dugg, may kat-kati,
musiba mëdd ma.
7 Dama ne: «Éy ku may may laafi xati,
ma ne fërr, noppluji.
8 Xanaa ma naaw, ba sore,
fanaani màndiŋ ma.
Selaw.
9 Naa gaawtu, seeluji
ngelaw lu riddi ak ngëlén.»
10 Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen.
Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,
11 guddeek bëccëg ñuy wër,
ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
12 Yàq a nga ca biir,
te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
13 Su doon noon bu may ñaawal,
ma muñ ko,
mbaa muy bañ bu may won ab dayo,
ma daw ko.
14 Waaye yaw la, sama nawle,
di sama wóllëre, ma xam la.
15 Nu daan bokk bànneexu diisoo,
ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
16 Yal na leen dee bett,
ñu jekki tàbbi njaniiw,
ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.
17 Waaye man, Yàlla laay woo wall,
te Aji Sax jee may wallu.
18 Subaak ngoon ak njolloor,
may ñaxtook a ñurumtu,
mu dégg ma.
19 Moo may jot ak jàmm,
ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.
20 Yàllaay dégg, duma leen,
moom mi nguuram yàgga sax.
Selaw.
Soppikuwuñu fenn
te ragaluñu Yàlla.
21 Kii a ngi xàccil ñi mu takktool,
di fecci kóllëre,
22 làmmiñ wa daa neex ni lem,
te xare lal xol ba;
kàddu ya gëna nooy ag oliw
te di saamar bu génn mbaram.
23 Sippikul Aji Sax ji lu la diis,
moom moo lay taxawu.
Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf.
24 Waaye yaw Yàlla, yaa leen di tàbbal,
bóomkat ak naaféq ci pax mu xóota xóot,
te seenu fan xaajul.
Man nag, ma di la wóolu.