Sabóor 108
Yàlla, may nu ndam
1 Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Yàlla, dogu naa,
damay woy, di la kañ;
sama jëmm jépp di la woy.
3 Na mboolem xalam yewwu,
ma yee leeru njël.
4 Aji Sax ji, dama lay gërëm ci biir xeet yi,
kañ la ci biir waaso yi.
5 Sa ngor a màgg ba sut asamaan,
sa worma àkki fa kawa kaw.
6 Éy Yàlla, yaa màgg ba sut asamaan,
sag leer tiim suuf sépp.
7 Walloo nu sa ndijoor,
nangul ma,
ba say soppe xettliku.
8 Yàllaa àddoo fa këram gu sell,
ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem,
séddale xuru Sukkóot.
9 Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase,
Efrayim di sama mbaxanam xare,
Yuda di sama yetu nguur,
10 réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay,
Edom, ma teg tànk;
Filisti, ma xaacoo fa.»
11 Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër?
Ku may jiite ba Edom?
12 Yàlla, xanaa du yaa nu wacc?
Éy Yàlla, yaa baña ànd ak sunu mboolooy xare?
13 Ngalla dimbali nu ci bañaale;
doom aadama, wallam neen la.
14 Nook Yàlla, nu def njàmbaar;
moom mooy not sunuy noon.