Sabóor 121
Ana ku may sàmm?
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Damaa séentu tund ya,
te naan fu wall di jóge?
Sama wall a nga fa Aji Sax ji,
ki sàkk asamaan ak suuf.
 
Kii du la bàyyi nga tërëf,
sa sàmm bii gëmmul.
Kiy sàmm Israyil kay
gëmmul, nelawul.
Aji Sax jee lay sàmm,
Aji Sax jee lay yiir,
féete la ndijoor.
 
Du naaj wu lay dal bëccëg,
mbaa leer gu ndaw guddi.
Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange,
di sàmm sa bakkan.
Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk,
tey ak ëllëg.