Saar 14
Xare bu mujj jib na
1 Bés a ngii di dikkal Aji Sax ji,
ca lees di séddoo fi seen biir,
alal ju ñu nangoo ci yeen.
2 Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem,
ngir xare.
Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi,
tëdde jigéen ñi.
Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo,
waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge
ci dëkk bi.
3 Su boobaa la Aji Sax jiy génn,
xeex ak yooyu xeet,
ni mu baaxoo xeexe ci bésub xare.
4 Bésub keroog, kaw tundu Oliw ya
la tànkam yay sampe,
fa janook Yerusalem, ca penku,
tundu Oliw ya xar ca digg ba,
penku ba sowu,
def xur wu yaa,
genn-wàllu tund wa randu, jëm bëj-gànnaar;
genn-wàll ga jëm bëj-saalum.
5 Xur wa ca diggante sama tund ya ngeen di jaare daw,
ndax xur wa ba Accal lay àkki.
Na seeni maam dawe woon ngeen di dawe,
ba suuf sa yëngoo,
ca janti Osiyas buurub Yuda.
Sama Yàlla Aji Sax ji mooy dikk,
ànd ak mboolem ñu sell ñi.
6 Bésub keroog, dug leer,
dub sedd, te du benn tawub yuur.
7 Benn bésu boppam lay doon
bu Aji Sax ji doŋŋ xam;
du doon bëccëg, du doon guddi,
te bu ngoonee mu leer.
8 Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale,
genn-wàll gi jëm géeju penku,
genn-wàll gi, géeju sowu,
te noor ak nawet lay doon.
9 Aji Sax ji mooy doon buuru àddina sépp,
bésub keroog Aji Sax ji di kenn,
turam di wenn.
10 Réew mi mépp ag joor lay soppliku,
dale ko Geba ba Rimon ca bëj-saalumu Yerusalem,
Yerusalem tooge bérabam, tiim la ko wër,
dëkk bi dale ca buntu Beñamin,
ba fa bunt ba woon,
jàll ba ca buntu Jàddukaay ba,
daleeti ca tatay Ananel ba ca nalukaayi reseñi buur* 14.10 Mboolem Yerusalem, ak ci wetam yépp la aaya bi wax ne mooy tiim diiwaan bi ko wër. .
11 Dees na ko dëkke te deesatu ko faagaagal,
kaaraange la Yerusalem di dëkke.
12 Yii duma la Aji Sax jiy duma
mboolem xeet yi xareek Yerusalem:
Seen suux mooy yàqu te ñu ne jonn taxaw,
seeni gët yàqu ca seen biir paxi gët,
seenu làmmiñ nëb ca seen biir gémmiñ.
13 Bésub keroog tiitaange ju réy mooy tukkee ci Aji Sax ji
wàcc ci seen biir;
ku nekk jàpp sa loxol moroom,
ñu songoo.
14 Yuda it day fekksi Yerusalem ci xeex bi,
te dees na dajale alali xeet yi leen wër yépp;
wurus, xaalis ak yére, bare, ne gàññ.
15 Yooyu duma it mooy dal fas,
ak berkelleek giléem ak mbaam-sëf,
ak lépp luy jur ci biir dal yooyu,
noonu lees di dumaa mala yépp.
16 Su boobaa mboolem ndesu wépp xeet
wu songoon Yerusalem,
Yerusalem lay yéegi at mu ne,
ngir sujjóotali Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
tey màggalsi màggalu Mbaar yi*.
17 Te gépp làngu kaw suuf gu yéegsiwul ba Yerusalem,
ngir sujjóotalsi Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
googu làng du tawlu.
18 Làngu Misra it, su ñu yéegul ba dikk, duñu tawlu;
dinañu jot ci duma yi Aji Sax jiy duma
xeet yi yéegul ba màggalsi màggalu Mbaar yi.
19 Loolooy doon dumay Misra ngir seen bàkkaar,
di dumay wépp xeet ngir seen bàkkaar,
ndax ñàkka yéeg ba màggalsi màggalu Mbaar yi.
20 Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax
dees na ci bind:
«Sell na ñeel Aji Sax ji.»
Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle,
cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax
noonu lañu selle.
21 Su boobaa luy cin ci Yerusalem ak Yuda,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi lees koy sellalal,
ba mboolem ñi dikk di sarxalsi,
ci lañuy jël, togge.
Te bésub keroog ab jula dootu am
ci biir kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.