Saar 3
Yerusalem déggadi na
1 Wóoy ngalla fippukat bu sobewu bi,
dëkkub notkat yi.
2 Dégluwul baat, nanguwul kàddu guy yare,
du Aji Sax ji la wóolu,
du Yàllaam jooju la jege.
3 Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar,
ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,
4 ay yonentam reew, diy workat;
ay sarxalkatam teddadil sellnga, xëtt yoon.
5 Ndaxam Aji Sax jiy boroom njekk a ngi ci biiram,
te du def njubadi,
jantoo jant mu fenkal ab àtteem,
te du wuute fu bët sete.
Ab wurujkat kay moo xamul gàcce.
6 «Maa fàkkas ay xeet,
seeni tata tasaaroo,
ma wéetal seeni mbedd,
ba kenn jaareetu fa,
seeni dëkk a tas ba kenn desul,
kenn dëkkatu fa.
7 «Maa noon Yerusalem: “Xanaa moos dinga ma ragal,
déggal ab yar.”
Su ko defee dëkkuwaayam du tas,
ndax mboolem mbugal yi ma ko dikke,
waaye moo yàkkamtee ñaaw ci jépp jëfam,
8 moo tax, xaar ma rekk,» kàddug Aji Sax jee,
«ba keroog may jóg, nara sëxëtooji,
nde maa dogala dajale xeet yi,
dajale nguur yi,
ngir xëpp leen samam sànj,
mboolem sama tàngooru mer.
Sama sawaras fiiraange déy,
ci la mboolem àddina di xoyomu.
Yàlla mooy tuubloo xeet yi
9 «Su boobaa ma soppi làmmiñu xeet yi, setal ko,
ngir ñuy tudd ñoom ñépp turu Aji Sax ji,
di ko jaamoondoo benn bopp.
10 Sama jaam ñi, sama ñoñ ñi tasaaroo,
ca wàllaa dexu Kuus lañuy bawoo,
ba indi samab sarax.
Yàlla soppi na xolu ndesu Israyil
11 «Su bés baa gàcce dootul am ci sa mboolem jëf,
ji nga ma moye,
nde maay jële fi sa biir ñiy bége sab sag,
te doo damooti ci sama kaw tund wu sell.
12 Waaye maay wacc fi sa biir
askan wu woyof te néew doole,
ñu yiiroo turu Aji Sax ji.
13 Ndesu Israyil dootuñu ayibal, dootuñu fen,
deesatu leen déggal kàdduy wor,
ñoom doŋŋ it ñooy for, di goor,
te kenn du leen tiital.»
Yerusalem dina leqliku
14 Yaw janq Siyoŋ mu taaru, sarxolleel,
Éey Israyil, xaacul,
yaw janq Yerusalem mu taaru, bégal,
te bànneexoo xol bu sedd guyy!
15 Aji Sax ji moo teggi say mbugal,
waññi sab noon.
Buurub Israyil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir,
dootuloo tiit lu bon.
16 Bésub keroog lees di wax Yerusalem, ne ko:
«Yaw Siyoŋ, bul tiit, bul yoqi.
17 Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir,
di jàmbaar juy walloo.
Moo lay bége ci biir bànneex,
leqlee la cofeelam,
bége la bay sarxolle.
18 «Ñi amu naqar te sore ndajey bernde,
ñooñu la sore, te tegoo woon gàcce,
maa leen di dajale, teggil leen gàcce tey.
19 Ma ne jant yooyu laay jëflanteek
mboolem ñi leen di sonal.
Ci laay wallu kuy sukkóot,
fat ku tumurànke,
may leen teraanga aku tur,
fépp fu ñu ruse woon ci àddina.
20 Yeen, jant yooyu laa leen di indi,
jant yooyu laa leen di dajale,
nde maa leen di defal aw tur ak teraanga
fi biir mboolem askani àddina,
maay tijji seen wërsëg, ngeen gis.»
Aji Sax jee ko wax.