Neyemi. 10. Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy Leween ak sunuy sarxalkat def ci seen màndargay torlukaay. Ñi ko torlu ñoo di: Boroom dëkk bi Neyemi doomu Akalya, mook Cedekiya ak Seraya ak Asaryaa ak Yeremi ak Pasur ak Amarya ak Malkiya ak Atus ak Sebaña ak Malug ak Arim ak Meremot ak Obadiya ak Dañeel ak Ginton ak Barug ak Mesulam ak Abya ak Miyamin ak Maasya ak Bilgay ak Semaya. Ñooñu ñoo di sarxalkat ya. Leween ñi ñoo di: Yeswa doomu Asaña, ak Binuy, kenn ca doomi Enadàdd, ak Kadmiyel. Seeni bokk ca lañu, di Sebaña ak Odiya ak Kelita ak Pelaya ak Xanan ak Mika ak Reyob ak Asabya ak Sakuur ak Serebya ak Sebaña ak Odiya ak Baani ak Beninu. Njiiti askan wi ñoo di: Paros ak Payat Mowab ak Elam ak Sàttu ak Baani ak Buuni ak Asgàdd ak Bebay ak Adoña ak Bigway ak Adin ak Ater ak Esekiya ak Asur ak Odiya ak Asum ak Besay ak Arif ak Anatot ak Nebay ak Magpiyas ak Mesulam ak Esir ak Mesesabel ak Cadog ak Yaduwa ak Pelaca ak Xanan ak Anaya ak Oseya ak Anaña ak Asub ak Aloyes ak Pila ak Sobeg ak Reyum ak Asabna ak Maaseya ak Axiya ak Xanan ak Anan ak Malug ak Arim ak Baana. Bànni Israyil ga ca des nag fekksi leen, muy sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem nun ñi beddeeku woon waasoy réew yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, nook sunuy jabar ak sunu doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee. Ci kaw loolu nu ànd ak sunu bokki garmi, waatook ñoom ne dinanu topp yoonu Yàlla wi mu dénkaane, Musaa jaamam ba jottli; di ko sàmm, di jëfe mboolem sunu santaaney Boroom Aji Sax ji, ak àttey yoonam ak dogali yoonam. Nu ne nag dunu may waa réew mi sunu doom yu jigéen te dunu jëlal sunuy doom seeni doom yu jigéen. Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci bésub Noflaay, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu sell, te atum juróom ñaareel mu nekk dinanu bale bépp bor. Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga, jëm ca mburum wone ba, ak saraxi pepp yi war bés bu nekk, ak saraxi dóomal yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak saraxi póotum bàkkaar yi bànni Israyil di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga. Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi. Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf jëkka meññle ak lu garab yépp jëkka ñorle. Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey. Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu jëkk ci sunu notu sunguf, ak sunu jooxey pepp, ak sunu meññeefi garab yépp, ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp. Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya. Ci néeg yooyu la bànni Israyil ak askanu Leween ñi di yóbbu jooxeb pepp ba ak biiñ baak diw ga; fa la ndabi bérab bu sell ba dence, te fa la sarxalkat, ya sasoo liggéey ba nekk, ñook fara bunt yaak jàngkat ya. Nu dogu nag ne dunu sàggane sunu kër Yàlla ga.