Sabóor. 97. Aji Sax jeey Buur, na àddina bég; dunoo dun bànneexu. Ay xàmbaar a ko yéew, njekk ak njub lal ab jalam. Sawaraa dox, jiitu ko, di xoyomi noonam wetoo wet, ay melaxam leeral àddina, waa àddina gis, di pat-pati; tund yi ne soyox seey fi kanam Aji Sax ji boroom àddina sépp. Asamaan a ngi biral njekkam, xeetoo xeet di gis darajaam. Gàcce ñeel na kuy jaamu jëmmi tuur, di puukarewoo ay yàllantu. Yeen yàllay xeet yépp, sujjóotal-leen kii, Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii. Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp; yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur. Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon. Jub, leerlu; jubal, bég. Yeen aji jub ñi, bànneexooleen Aji Sax ji, sante ko sellngaam.