Sabóor. 117. Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Aji Sax ji, réewoo réew, kañleen ko. Moo nu xéewale ngoram gu réy, te wormay Aji Sax jee sax dàkk. Màggal-leen Ki Sax!