Sabóor. 120. Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall, mu wuyu ma. Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, ak làmmiñu njublaŋ. Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, ana lu ñu lay añale ak lu ñu lay dolli? Xanaa fitti mbër yu ñaw ak xal yu yànj. Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña! Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm. Man may wut jàmm, te su ma waxee, ñoom ñuy ayoo.