Sabóor. 127. Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu. Neen it la nit di teela jóg ak a guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw. Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la. Doom joo jure ndaw, mooy fitt ci loxol jàmbaar; ndokklee ku ci mbuusam fees, ba bu ñu taseek ub noon ca pénc ma, duñu am gàcce mukk.