Sabóor. 128. Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ndokklee képp ku ragal Yàlla, di jëfe ay yoonam. Yaay lekk saw ñaq, mbégteek ngëneel ñeel la. Sa jabar ni garab gu nangoo sa wanag, say doom wëra wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi. Ki ragal Aji Sax jaa ngoog, nii rekk lay barkeele. Yal na la Yàlla barkeele fii ci Siyoŋ; yal nanga teewe xéewalu Yerusalem sa giiru dund gépp, te nga gis say sët. Yal na jàmm dal Israyil.