Sabóor. 131. Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwma, daŋŋiiraluma, xintewoowma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm. Xanaa ne tekk, ne cell, ni perantal ak ndeyam; sama xel dal ni perantal. Éey Israyil, yaakaaral Aji Sax ji tey ak ëllëg.