Sabóor. 136. Nangeen sante Aji Sax ji mbaaxam. Santleen Yàllay yàlla yi. Santleen Sangu sang yi. Moo wéetoo jaloore yu mag yi. Moo sàkke asamaan manoore. Moo lal suuf ca kaw ndox ma. Moo sàkk leer yu mag yi: jant bi yilif bëccëg, weer ak biddiiw, guddi. Moo fàdd taawi Misra yu góor ya, seppee bànni Israyil ca ñoom, ci dooley loxoom ak kàttanu përëgam. Moo xar géeju Barax ya yaar, jàllale bànni Israyil ca digg ba. Moo xalab Firawnaak mbooloom ca géeju Barax ya. Moo jiite ñoñam ca màndiŋ ma. Moo duma buur yu mag ya, bóom buur yu màgg ya, reyaale Siwon buurub Amoreen ña, reyati Og buuru Basan. Moo nangu seen réew, joxe, sédde Israyil ma dib jaamam. Ci biir notaange la nu geesoo, ne nu siféet ci loxoy noon ya. Mooy leel bépp boroom bakkan. Santleen Yàlla mi ci asamaan!