Ngën-gi-woy. 4. Yaaka rafet, xarit, yaaka taaru! Sa gët yi niy pitax, làqoo muuraay bi, njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul yu bartaloo kaw tundu Galàdd. Sa gëñ yi weex ni xar yu ñu wat ñuy yéege ca sangukaay ba, ku nekk ak seexam, kenn wéetu ca. Sa tuñ yi mel ni wëñ gu xonq curr, ndaw gémmiñ gu jekk! Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi; sa loos wi ne coleet ni tatay Daawuda, mërgalu ba jekk, caq bay lang ni junniy kiiraayi jàmbaar. Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél yuy fore digg tóor-tóor yi. Balaa jant a fenk, ker gàddaay, ma ne coww diggante tund wa ndàbb ne bann, ak tund wa xas ma neexe. Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw. Séet sama, jógeel Libaŋ, jege ma, bawool Libaŋ, jegesi ma. Wàcceel colli Amana ak colli Senir ak Ermon. Génnal xunti gaynde yooyook tundi segg ya. Jigéen sama, séet sama, benn yoon nga ma xool, sama fit ne tërit. Sa benn peru caq rekk, sama fit ne tërit. Jigéen sama, séet sama, sa mbëggeel a neex! Sa mbëggeel a dàq biiñ, sa diw yu xeeñ dàq luy cuuraay. Séet sama! Lem ay xellee sa gémmiñ, lem ak meew lal sa làmmiñ. Sa xetu yére xetu àllub Libaŋ la. Jigéen sama, séet sama, yaay tóokër bu tëje, yaay seyaan bu tëje, di bëtu ndox bu saañe. Yaa di toolub gërënaat bu naat, meññ ngën-gi-meññeef ak fuddën ak reen yu xeeñ, muy reen yu xeeñ, safroŋ, barax, kanel, ak xasoo xas mu xeeñ, ndàbb ak alowes ak lépp lu xeeña xeeñ. Yaa di bëtu ndox ci tool yi, di teen bu fees ak ndox muy daw, wale tundi Libaŋ. Yaw, ngelawal bëj-gànnaar, yewwul, ngelawal bëj-saalum, dikkal, wolal-leen ma sama tool bi, mu gilli; sama nijaay dugg toolam, xéewloo ngën-gi-meññeefam.