Askanu Aadama, ba ci Nóoyin
Saar 5
(Saar 5.1—6.8)
1 Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, 2 góor ak jigéen la sàkk, barkeel leen, tudde leen Nit, keroog ba mu leen sàkkee.
3 Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. 4 Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 5 Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu.
6 Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. 7 Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. 8 Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu.
9 Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. 10 Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. 11 Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu.
12 Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. 13 Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 14 Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu.
15 Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. 16 Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 17 Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu.
18 Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog. 19 Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 20 Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu.
21 Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. 22 Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 23 Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). 24 Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom.
25 Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg. 26 Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 27 Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu.
28 Lemeg nag am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (182), doora jur doom ju góor. 29 Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» 30 Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 31 Kon Lemeg dund na juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar (777), doora faatu.
32 Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet.