Saar 6
Yàlla fas na yéene tas àddina ndax mbonu nit
1 Bi nga xamee ne nit ñi tàmbali nañoo fulandiwu ci kaw suuf, te am ay doom yu jigéen, 2 ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar. 3 Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).»
4 Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.
5 Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam. 6 Aji Sax ji nag am tiis ci xolam, ba mititlu li mu doon sàkk nit ci kaw suuf. 7 Aji Sax ji daldi ne: «Dinaa far ci kaw suuf doom aadama yi ma sàkk, nit ak jur, luy raam ak luy naaw, ndax mititlu naa li ma leen sàkk.» 8 Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande.
Askanu Nóoyin
(Saar 6.9—9.29)
9 Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla. 10 Nóoyin nag amoon na ñetti doom yu góor: seeni tur di Sem, Xam ak Yafet.
11 Booba fekk na àddina yàqu, te fees ak ay, Yàlla teg ci bëtam. 12 Yàlla gis ne àddina yàqu na, ndaxte jëfi ñépp a bokk ñaaw fi kaw suuf.
13 Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal.
14 «Yaw nag wutal dénku sippar, yettal ci sa bopp gaal gu mag; nga sàkk ci ay néeg, te diw ko koltaar biir ak biti. 15 Ni nga koy defare nii la. Na guddaayu gaal gi di ñetti téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab. 16 Yettal mbaar, mu ko tiim, te nga àggle gaal gi, bàyyi lu tollook xasab diggante kéméj yi ak mbaar mi. Sàkkal ko bunt ci wet gi, te séddale ko ñetti néeg yu tegloo, benn ci suuf, benn ci digg bi ak benn ci kaw.
17 «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee. 18 Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom. 19 Te xeeti rab yépp nanga ci dugal ñaar ci gaal gi, wu ci nekk, nga def ko góor ak jigéen; su ko defee ngeen ànd mucc. 20 Xeetu picc wu ci nekk ak xeetu bàyyima wu ci nekk ak wépp xeetu rab wuy raam ci suuf, dina def ñaar, ñëw ci yaw, ba raw. 21 Sàkkal ci bépp xeetu dund, denc, ngeen bokk dunde.»
22 Noonu la Nóoyin def. Lépp lu ko Yàlla sant, def na ko.