Saar 7
Lu jëm ci kër Yàlla ak kër Daawuda
1 Gannaaw loolu Buur Daawuda sanc na këram, Aji Sax ji noppal ko ci noonam yi ko wër yépp. 2 Ci biir loolu mu ne Yonent Yàlla Natan: «Xoolal rekk, maa ngi dëkke këru banti seedar, gaalu Yàlla gi dëkke ab xayma.» 3 Natan ne Buur: «Mboolem loo ci namma def rekk, defal, ndax Aji Sax ji yaw la àndal.»
4 Guddig keroog nag kàddug Aji Sax ji dikkal Natan, ne ko: 5 «Demal wax sama jaam Daawuda, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Ndax yaw yaa may tabaxal kër gu ma dëkke? 6 Bés ba ma génnee bànni Israyil Misra ba tey jii, masumaa dëkke ci kër. Ci biir xaymab jaamookaay laa masa mànge. 7 Mboolem fu ma masa màngeji ak bànni Israyil gépp, ndax mas naa wax benn baat, jëme ci genn giirug Israyil gu ma sant ñu sàmm Israyil sama ñoñ, ne leen ñu tabaxal ma kërug bantu seedar?”
8 «Kon nag waxal sama jaam Daawuda, ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa la jële ca parlu, ga nga toppe woon gàtt ya, ngir nga doon kilifag Israyil, sama ñoñ. 9 Maa ànd ak yaw fépp foo dem, maa tenqee fi sa kanam mboolem say noon, te maa lay may tur wu màgge ni turi boroom daraja yi ci àddina. 10 Maay sàkkal dëkkuwaay Israyil sama mos, jëmbat ko, mu dëkke ko, ba deesu ko lëjalati, te ñu bon ñi duñu ko sonalati na woon, 11 ba ma falee ay njiit ci kaw Israyil sama ñoñ. Maa lay noppal ci sa noon yépp. Te it Aji Sax jaa ngi lay yégal ne la Aji Sax ji moo lay sosal kër. 12 Te bu say fan matee ba nga tëddi, fekki say maam, maay yékkati kenn ci saw askan, sa deretu bopp, mu wuutu la, te maay saxal nguuram. 13 Kookooy tabax kër, ñeel sama tur, te maay saxal ab jalam ba fàww. 14 Man maay doon baay ci moom, moom, muy doom ci man. Su defee naka su dul noonu, maa koy yare bantu nit, ak dumay doom aadama. 15 Waaye duma ko noppee laaye biir, ni ma noppee laaye biir Sóol ma ma la randalal. 16 Sa kër ak sa nguur day sax dàkk fi sa kanam, te sab jal day dëju ba fàww.”»
17 Noonee Natan jote mboolem kàddu yooyu ak peeñu moomu, na la ko yegge Daawuda.
Daawuda delloo na Yàlla njukkal
18 Ba loolu amee Buur Daawuda dikk ba fa kanam Aji Sax ji, toog ne ko:
«Boroom bi Aji Sax ji! Ana lu ma doon, ak lu sama waa kër doon, ba tax nga indi ma ba fii? 19 Boroom bi Aji Sax ji, loolu doyatu la, nga waxaale ci sama askan, wi xaajagula ñëw, Sang bi. Boroom bi, Aji Sax ji, ndax nii ngay jëfeek doom aadama?
20 «Boroom bi Aji Sax ji, ana lu ma lay waxati? Yaw de, Sang bi, yaa ma ràññee. 21 Sa kàddoo waral nga def mboolem jii jëf ju réy ci sa yéeney xol, ba noppi yégal ma ko, Sang bi.
22 «Boroom bi, Aji Sax ji, Moo la tax di ku màgg! Kenn du yaw, kenn du Yàlla ku dul yaw doŋŋ, te mboolem lu nu nopp may, dëggal na loolu. 23 Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam. 24 Yaa dëgëral Israyil sa ñoñ, ngir ñoñoo leen ba fàww, te yaw Aji Sax ji, yaa doon seen Yàlla.
25 «Léegi nag, Aji Sax ji Yàlla, Sang bi, wax ji nga wax ci man, ak sama waa kër, saxal ko ba fàww rekk, te defe ko noonu nga ko waxe, 26 ngir saw tur di gëna màgg ba fàww, ñu naan: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi mooy Yàllay Israyil,” te waa kër Daawuda sax fi sa kanam, Sang bi.
27 «Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil, yaw déy yaa ma déey, Sang bi, ne kër nga may sosal. Moo tax ma ñeme laa ñaan lii, Sang bi. 28 Léegi nag, Boroom bi Aji Sax ji, yaw yaay Yàlla, say kàddu mooy dëgg, te yaa ma wax lu baax lii, Sang bi. 29 Kon nag Sang bi, nangula barkeel sama kër, ngir mu sax ba fàww fi sa kanam. Ndax kat yaw Boroom bi Aji Sax ji yaa wax, te ci sa barke la sama kër di barkeele ba fàww, Sang bi.»