Saar 8
Daawuda duma na xeet ya ko wër
1 Gannaaw gi, Daawuda duma na Filisteen ña, néewal leen doole, jële kilifteefu waa Filisti ca réew ma. 2 Daawuda duma Mowabeen ña itam, tëral leen ca suuf, sësale leen, natte leen ag buum. Ñaari buum yu mu natt, yemook ña ñu wara rey, buum gu mat ga ca topp yemook ñi wara dund. Mowabeen ña daldi nangul Daawuda, di ko indil galag.
3 Daawuda duma na itam buurub Soba* 8.3 Soba turu dëkk la bu amoon buuru boppam. Waaye ci Siri la bokkoon. , Adadeser doomu Reyob, fekk Adadeser di fexee nanguwaat diiwaan ba feggook dexu Efraat. 4 Daawuda jàpp junniy gawaram ak juróom ñaar téeméer (1 700) ak ñaar fukki junniy xarekat (20 000) yuy deme tànk, ba noppi dog sidditi tànki mboolem fas ya doon dawal watiir, bàyyiwu ca lu moy téeméeri fas. 5 Waa Siri ña dëkke réewum Damaas dikk wallusi Adadeser buurub Soba. Daawuda rey ca ñoom ñaar fukki junneek ñaar (22 000). 6 Ba mu ko defee Daawuda tabb ay jawriñam ca Damaas ca Siri, waa Siri nekk ci curgag Daawuda, di ko fey galag. Aji Sax ji may Daawuda ndam fépp fu mu dem. 7 Daawuda nag nangu pakki wurus ya kilifay xarekati Adadeser daan aare seen bopp. Mu boole, yóbbu Yerusalem. 8 Dëkki Adadeser ya ñuy wax Beta ak Berotay it, xànjar ju bare lool la fa Buur Daawuda nangoo.
9 Ci kaw loolu Toyi buurub Amat dégg ne Daawuda duma na gàngooru Adadeser gépp. 10 Toyi yebal doomam Yoram ca Buur Daawuda, ngir mu nuyu ko, sargal ko ca la mu xareek Adadeser ba duma ko, ngir Toyi ci boppam xare woon naak Adadeser. Yoram indaaleel ko jumtukaayi xaalis ak wurus ak xànjar. 11 Buur Daawuda boole loolu, jagleel ko Aji Sax ji, na mu ko jagleele woon xaalis baak wurus, wa mu lële ca mboolem xeet ya mu tegoon loxo; 12 la jóge ca Edomeen ñaak Mowabeen ñaak Amoneen ñaak waa Filisteek Amalegeen ña ak la mu lële ca buurub Soba, Adadeser doomu Reyob.
13 Daawudaa nga gënatee siiw ba mu dumaa waa Siri, teg ca duma fukk ak juróom ñetti junniy (18 000) Edomeen ca xuru Xorom wa. 14 Mu daldi tabb ay jawriñam ca réewum Edom. Réewum Edom gépp la tabb ay jawriñ, Edomeen ñépp nekk ci curgag Daawuda. Aji Sax ji nag may Daawuda ndam fépp fu mu dem.
Lu jëm ci jawriñi Daawuda
15 Buur Daawuda ci kaw Israyil gépp la nguuru woon; muy jëfe njub ak njekk ñeel réewam mépp. 16 Yowab, mi Seruya di ndeyam, moo jiite woon mbooloom xare ma; Yosafat doomu Ayilut yor kàddug buur; 17 Cadog doomu Ayitub ak Ayimeleg doomu Abiyatar ñoo doon sarxalkat ya; Seraya di bindkat ba; 18 Benaya doomu Yoyada moo jiite woon waa Keret ak waa Pelet, dagi buur ya; doomi Daawuda yu góor nag ay sarxalkat lañu woon† 8.18 Am na ñu jàpp ne sarxalkat yi ñuy wax fii, ay saytukat lañu woon. .