Kàdduy Waare
di téere bu ëmb ay gëstu ci solob dundu nit
Saar 1
1 Lii kàdduy waarekat baa, di doomu Daawuda te di buurub Yerusalem.
Luy solob àddina?
2 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba,
cóolóoloo cóolóol,
léppi cóolóoli neen.
3 Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ
ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4 Ag maas wéy, ag maas teew;
àddina sax ba fàww.
5 Jant fenk, so,
ne coww dellu fa muy fenke.
6 Ngelaw jëm bëj-saalum,
wiiri jëm bëj-gànnaar,
di wiir ak a wiiraat,
di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7 Dexoo dex wal, wuti géej,
te taxul géej fees.
Fa dex wal jëm,
fa lay walati, jëm.
8 Jëfoo jëf ca jëfit,
làmmiñ tuddul lépp,
bët du suur,
nopp du buur.
9 Lu ayoon mooy ayati,
lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati.
Dara yeesul fi kaw suuf.
10 Lëf a ngii, nit naa:
«Lii de lu bees la,»
te mu ngi fi woon lu yàgg,
lu jiitu sunu juddu.
11 Kenn du fàttliku ñi jiitu,
ñiy ñëwit,
ñi leen topp duñu leen fàttliku.
Ma seet lu ma doy
(Saar 1.12—2.23)
Rafet xel doyul
12 Man waarekat bi,
buurub Israyil laa woon ci Yerusalem.
13 Damaa dogu ne damay gëstu,
teg ko ci xel mu rafet, di settantal
mboolem lu nit def fu jant bi tiim.
Ndaw sas wu tiis wu Yàlla sase,
ñu war koo sasoo!
14 Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf,
ndeke lépp cóolóoli neen la ak napp um ngelaw.
15 Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti;
lu teewul, maneesu koo lim.
16 Damaa wax ci saam xel naa:
Man de, maa ngii di gëna xelu,
ba sut ku ma jiitu ci jalub Yerusalem.
Damaa xuus ci xel mu rafet ak xam-xam,
17 di dogoo xam luy xel mu rafet,
xam luy nitoodi akug ndof.
Fekk loolu it napp um ngelaw la.
18 Ku géejal xel mu rafet, géejal naqar;
yokku xam-xam, yokku tiis.