Saar 2
Bànneexu neen doyul
Saam xel da ne:
«Xaaral rekk, ma natt bànneex,
ñam lu neex ba xam.»
Ndeke loolu it, cóolóoli neen.
Ma ne: «Reetaan ag nitoodi la;
te mbégte lu muy jariñ?»
Saam xel ne ma, ma naan biiñ boog, bégloo,
ba mel nib dof,
tey ànd ak sama xel,
ba gis lu ci baax,
ba doom aadama di ko def,
giiru dundam fi ko jant bi tiim.
 
Damaa liggéey lu réy.
Tabaxlu naa samay kër,
jëmbat sama toolub reseñ.
Ma sàkki tóokër aki tool,
jëmbat ca garab yuy meññ lu ne,
sàkklu samay déeg,
di ko suuxate, garab ya naat.
Ma jëndi jaam, góor ak jigéen;
ñu ami doom ci kër gi.
Ma am jur gu ne gàññ, gu gudd ak gu gàtt,
ba ëpple ku ma jiitu ci Yerusalem.
Ma dajale sama xaalis ak sama wurus,
moom alali buur yeek diiwaan yi ma yilif,
tabb samay woykat, góor ak jigéen,
boole ci bànneex bi ci jabari jabar.
Ma am doole, yokku,
ba sut ku ma jiitu ci Yerusalem,
te teewul may jëfe xel.
10 Lépp lu saay gët xemmemaa,
xañuma ko sama xol.
Bañaluma sama bopp benn bànneex,
xanaa di bége lu ma liggéey,
yooloo ko la ma liggéey.
11 Ma xoolaatal sama bopp
lépp lu ma sottal,
doñ-doñi ko, ba sottal,
ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.
Nit gisul njariñ ci kaw suuf.
Rafet xel fanqul dee
12 Ma geesu xoolaat xel mu rafet,
xool ag nitoodi akug ndof.
Ana ku may wuutuji ci nguur gi,
lu muy def lu moy lu ñu daan def?
13 Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ,
ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14 Ku xelu day xool fa muy jaare,
dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm.
Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15 Ma xalaataat, saam xel ne ma,
dof bi noonu, man it noonu;
ana lu may xeloo xelu doye?
Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.
16 Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la;
ay bés yu néew, ñu fàtte lépp.
Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
 
17 Ma far bañ àddina.
Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf,
te lépp di cóolóol ak napp um ngelaw!
18 Sama doñ-doñ, ji fi kaw dun bi, génnliku na ma,
dama koy wacce ka may wuutuji rekk,
19 xameesul ku xeloom ku nitoodi lay doon,
mooy moom lu ma doon doñ-doñi,
te sama manoore manaloon ma ko fi kaw dun bi.
Loolu it, cóolóoli neen.
20 Sama xol a jeex ci doñ-doñ ju ma doñ-doñi fi kaw dun bi.
21 Nit a ngi doñ-doñee xel, xam-xam ak manoore,
te ku doñ-doñiwuloon lay wacce alalam.
Loolu it, cóolóoli neen ak naqar wu réy.
 
22 Ma ne ana lu nit di jariñoo
ci doñ-doñ ak xalaatu xol, yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi?
23 Ndegam day yendoo tiis ak naqaru tës-tës,
ba far fanaanoo xel mu dalul.
Loolu it, cóolóoli neen.
Njariñ, fa Yàlla
(Saar 2.24—12.8)
Jàmm, fa Yàlla
24 Kon nit amul lu gën di lekk ak a naan,
di bànneexoo ñaqam.
Ma gis ne loolu it Yàllaa koy maye.
25 Ana kuy lekk ak a bànneexu, te du Yàlla?
26 Yàlla de, ku mu gërëm,
xelal ko, xamal ko, bégal ko;
bàkkaarkat bi, Yàlla teg ko,
muy denc ak a dajale, ka mu gërëm jël.
Loolu it di cóolóoli neen ak napp um ngelaw.