Saar 41
1 Ba loolu amee waa ja jàlle ma ba ca bunt néeg bu mag ba. Mu natt jën ya séq bunt ba, mu dëlle juróom benni xasab ci ñaari wet yépp. 2 Yaatuwaayu bunt ba fukki xasab la, ñaari miiri wet yi ko séq, bu ci nekk di juróomi xasab. Mu natt néeg bu mag bi ci boppam, guddaay bi di ñeent fukki xasab, yaatuwaay bi di ñaar fukki xasab. 3 Moom nag moo jàll ca néegu biir ba, daldi natt jëni bunt ba, mu dëlle ñaari xasab, diggante ñaari jëni bunt bi di juróom benni xasab, yaatuwaayi ñaari miiri wet yi séq bunt bi, bu ci nekk di juróom ñaari xasab. 4 Mu natt néegu biir bi ci boppam, muy ñaar fukki xasab wet gii, di ñaar fukki xasab wetu néeg bu mag ba. Mu ne ma: «Fii mooy fu sell fee sell.»
Natt nañu toftalu néeg Yàlla bi
5 Mu natt miiru néeg Yàlla bi, mu dëlle juróom benni xasab, yaatuwaayu néegi wet, yi wër néeg Yàlla bi ba mu daj, bu ci nekk di ñeenti xasab. 6 Néegi wet yooyu ñetti taax yu tegloo la, tollook néeg Yàlla bi ab taxawaay, taax mu ci nekk di fanweeri néeg. Mu am ay cëslaay yu saxe ci miiru néeg Yàlla bi, te téye néegi wet yooyu, ba sësuñu rëkk ci néeg bi ci boppam. 7 Taax mu la gëna kawe, gën laa yaatu, miir ba ànd ak moom gëna sew fi wër néeg Yàlla bi ba mu daj. Noonu lañuy yéege ay dëggastal, jóge ci suuf, jaare ca taaxu digg ba, ba ca taax ma ca kaw.
8 Ma gis ne néeg Yàlla bi ab dëx a ko yenu, yenuwaale néegi wet yi wër néeg Yàlla bi, taxawaayu dëx bi di wenn yet wu mat, tollook juróom benni xasab. 9-10 Néegi wet yi, seen miiru biti dëlle na juróomi xasab. Ñu bàyyi diggante néegi wet yi ak taaxi sarxalkat yi, bérab bu tollook ñaar fukki xasab, wër néeg Yàlla bi ci ñetti wetam. 11 Am na ñaari bunt yu sare ci néegi wet yi wër néeg Yàlla bi, jëme ci pegg bu dara amul. Benn bunt ba féete bëj-gànnaar; benn ba, bëj-saalum, yaatuwaayu pegg, bi wër néeg bi ba mu daj, di juróomi xasab.
Ber nañu ab tabax ca gannaaw
12 Tabax bi féeteek dig-digalu feguwaay bi ci sowub néeg Yàlla bi, yaatuwaayam juróom ñaar fukki xasab la, guddaayam di juróom ñeent fukki xasab, dëllaayu miir ba di juróomi xasab.
13 Waa ja daldi natt néeg Yàlla bi, guddaay bi di téeméeri xasab; la dale dig-digalu feguwaay ba, ba ca catu tabaxu sowu ba aki miiram itam di téeméeri xasab. 14 Kanamu néeg Yàlla bi féete penku téeméeri xasab la, boo ci boolee dig-digali feguwaay yi séq néeg Yàlla bi. 15 Mu natt yaatuwaayu tabax ba ca gannaaw te janook dig-digalu feguwaay ba, boole ca ñaari poot ya séq tabax ba, muy téeméeri xasab.
Bérab bu sell bi nag, muy néeg bu mag bi, di néegu biir bi, di mbaaru bunt bi jàkkaarlook ëtt bi, 16 ak dëxi bunt yeek palanteeri caax yeek jaarukaay yi ci ñetti wet yépp, ak ci kanam dëx yi, lu ci nekk bant a ko lal. Ci suuf ak ci kaw miir bi ba ca palanteer ya it noonu, palanteer ya am ay caax. 17 Ci kaw buntu néeg Yàlla bi, ba ci biir néeg Yàlla bi, jëm biti, ak kaw miir bi ko wër, biir ak biti, lépp lañu natt. 18 Ñu yett ca miir ya ay malaakay serub ak garabi tàndarma; ñaari serub yu ne, garabu tàndarmaa nga ca digg ba, te serub bu ne am na ñaari kanam, 19 genn gi di kanamu nit, jublook genn tàndarma, geneen gi di kanamu gaynde, jublook geneen tàndarma. Noonu lañu wëralee néeg bi ba mu daj. 20 Li ko dale ci suufu néeg bu mag bi, ba ci kaw bunt yi, ak ci miir yi, fépp lañu yett serub yeek tàndarma yi. 21 Njëël bunt bi ak dëx bi, ak pegg yi ko téye ab kaare la. Buntu néegu biir bu sell ba it noonu la.
22 Sarxalukaay bi bant la, taxawaayam di ñetti xasab, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di ñaari xasab. Mu ami coll akub tegukaay aki wet, lépp di bant. Waa ji ne ma: «Taabal jii mooy janook Aji Sax ji.»
23 Buntub ñaari laf lañuy dugge ca néeg bu sell bu mag ba, di dugge beneen bunt bu ni mel ca néegu biir bu sell ba. 24 Bunt yooyu, bu ci nekk ñaari laf yuy warangiku la. 25 Ñu yett ca buntu néeg bu mag ba ay malaakay serub, ak garabi tàndarma yu mel ni ya ñu yett ca kaw miir ya. Catu xaddu mbaaru bunt ba ca biti, aw dénk lañu ko def. 26 Palanteeri caax yi ak miiri néegi wet yi ak miiri mbaar mi ak ca kaw catu xadd bay lang, wet gu ne, ay nataali tàndarmaa nga ca.