Saar 42
Natt nañu taaxi sarxalkat yi
1 Ba loolu amee waa ji jaarale ma buntu bëj-gànnaar, génne ma ci ëttu biti bi. Mu yóbbu ma wetu sowu, dugal ma ca tabax ba janook dig-digalu feguwaay ba te sësook miiru biir ba ca wetu bëj-gànnaar. 2 Tabax boobu, guddaayam ci wetu bëj-gànnaar ga féeteek bunt ba, téeméeri xasab la, yaatuwaay ba di juróom fukki xasab. 3 Ci genn wet tabax booboo ngi janook ñaar fukki xasab yu bokk ci ëttu biir bi, geneen wet gi janook dëru ëttu biti bi. Tabax bi def na ñetti sàppey taax yu tegloo. 4 Ci kanam néeg, yi féeteek ëttu biir bi, am na jaarukaay bu yaatoo fukki xasab, gudde téeméeri xasab. Néeg yooyu wetu bëj-gànnaar lañu cay dugge. 5 Ñaari taax ya ca kawam nag, mu ci nekk yaatuwaayam a yées ma ko féete suuf, ndax taax mu gëna kawe moo ëpp jaarukaay bu mu bàyyi fi kanamam. 6 Ñetti sàppey taax la yu amul ay jën ni néegi ëtt bi ame ay jën. Moo tax ruumi taaxum kaw ma gëna xat yoy taaxum digg ma, ak ma féete suuf. 7 Mu am miir bu làng ak néeg yooyu, teqale leen ak ëttu biti bi, guddaayu miir bi di juróom fukki xasab. 8 Ndax néeg yooyu féeteek ëttu biti ba, guddaay ba bépp juróom fukki xasab la. Waaye sàppey néeg, ya sësook néeg Yàlla ba, guddaayam téeméeri xasab la. 9 Ca suufu néeg yooyu la am jaarukaayu penku bu jëme ca biir néeg ya féete penku, boo jógee ca ëttu biti ba.
10 Am na sàppeb néeg bu janook dig-digalu feguwaay ba, ak tabax ba ca gannaaw néeg Yàlla ba. Sàppeb néeg boobu ma nga làng ak miiru biti, bi yaatuwaayam féete penku. 11 Mu ngi janook ab jàllukaay. Sàppey néeg yooyu daa bindoo ni bi féete bëj-gànnaar te bokk ak ñoom guddaay ak yaatuwaay, seeni bunt ak seeni dayo yépp di benn. 12 Bunti sàppey néeg ya ca bëj-saalum it noonu la. Ca catal jaarukaay ba, ab bunt a nga fa, janoo màkk ak miir ba féete penku.
13 Ba loolu amee waa ji ne ma: «Néegi bëj-gànnaar yeek néegi bëj-saalum yi janook dig-digalu feguwaay bi, ñooy néeg yu sell yi sarxalkat yi jege Aji Sax ji, di lekke sarax yu sell yee sell. Ca lañuy yeb sarax yu sell yee sell it, muy saraxu pepp yeek saraxu póotum bàkkaar yeek saraxu peyug tooñ yi, ndax bérab bu sell la. 14 Sarxalkat yi, bu ñu duggee ci bérab bu sell bi, dootuñu man daldi génn ci ëttu biti bi. Ci néeg yii lañuy wacc seen yére yi ñuy liggéeyale Aji Sax ji, ndax yooyu yére yu sell la. Ñu solaat nag yeneen yére bala ñoo dellu ca ëtt ba mbooloo may daje.»
Natt nañu miiru biti bu kër Yàlla gi
15 Ba waa ja nattee dayoy biir néeg Yàlla bi ba noppi, da maa jaarale ca mbaaru bunt ba féete penku. Mu tàmbali di natt bayaal bi wër kër gi. 16 Mu natte yet wa wetu penku, lépp di juróomi téeméeri yet, yemook kilomeetar ak genn-wàll. 17 Mu natte yet wa wetu bëj-gànnaar, lépp di juróomi téeméeri yet, 18 wetu bëj-saalum ba it, mu natte ko yet wa, muy juróomi téeméeri yet. 19 Mu walbatiku, natte yet wa wetu sowu, muy juróomi téeméeri yet. 20 Noonu la natte miir bi ub bayaalu kër Yàlla gi ba mu daj, muy kaare bu wetam di juróomi téeméeri dayo, te teqale fi sell ak fi sellul.