Saar 28
Xel mu rafet, fa Yàlla
1 Xaalis déy am na mbellam,
wurus am bérabu seggukaayam,
2 weñ gu ñuul ci suuf lees ko jële,
te xànjar, ay doj lees di xelli, ba am ko.
3 Dees na taal, dàq ug lëndëm,
di gëstu ba fu gëna làqu
doji biir lëndëm gu ne këruus.
4 Nit a ngi gas ay xunti fu soreeki dëkkuwaay,
di sandaamtalook a jaayu fu kenn newul,
te tànk jaarewu fa.
5 Kaw suuf day meññ ub dund,
xóote ya mel ni lu sawara salfaañe.
6 Doj ya ca biir la peri safiir màkkaanoo,
te pëndaxu wurus ñàkku fa.
7 Wii yoon, tan xamu ko,
bëtu jaxaay du ko gis.
8 Rabu àll du fa joggi,
te gaynde sax du fa jaare.
9 Loxol nit ay song doju kekk,
buddi reeni tund, jàllarbi.
10 Ci biir xeer yi lay yettey xunti,
ba bëtam di gis lu cay alal.
11 Nit a ngi dogale wali ndox,
ba lu làqu woon, mu leeral nàññ.
12 Waaye xel mu rafet fees koy jële,
ak fu ag dégg màkkaanoo?
13 Doom aadama xamul njégam,
te amul biir réewum aji dund ñi.
14 Xóote ya nee: «Xel mu rafet dëkku fi de!»
Géej ne: «Nekku fi de!»
15 Wurus mayewu ko,
xaalis wecciwul njégam.
16 Deesu ko weccee wurusu ngalam it,
mbaa peri onigsë ak safiir.
17 Deesu ko méngaleek wurus
ak ngën-gi-per yuy tàkk,
te ngën-gi-gànjari wurus wecciwu ko,
18 waxeesuli xor ak yeneen xeeti per;
xel mu rafet a gën per yu gëna jafe,
19 du moroomu peru topaas
ba ca réewum Kuus,
te wurusu ngalam daal wecciwu ko.
20 Xel mu rafet, ana fu mu jóge,
ak fu ag dégg màkkaanoo?
21 Ump na bëtu lépp luy dund;
njanaaw la fa kaw sax gisu ko.
22 Paxum sànkutee ngi àddoondook ndee naan:
«Dégmati nan ub jëwam de!»
23 Yàllaa ràññee yoon wa jëm xel mu rafet,
te moo xam màkkaanam.
24 Kii daal ay jéer ba fa cati àddina,
di gis mboolem lu asamaan tiim.
25 Ba Yàlla àppalee ngelaw diisaayam,
nattal ndox ab dayoom,
26 ba mu sàkkalee ab taw dogalu yoonam,
sàkkal melax ak dënu aw ñallam,
27 ca la nemmiku xel mu rafet, xamle ko,
samp ko, gëstu ko,
28 daldi ne doom aadama:
«Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet,
te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»