Saar 29
Ayóoba jooy na démbam
1 Ayóoba tàmbaleeti ne:
2 Éy ku ma doon delloo jamono ya woon,
fan ya ma Yàlla daa wattoo;
3 ba mu may tiim, di ma niital,
may doxe ag leeram, biir lëndëm!
4 Ba ma tolloo sama digg doole,
te Yàlla xejjoo sama xayma.
5 Booba Aji Man jaa ngeek man ba tey,
sama gone yu góor yéew ma,
6 may jàngoom niw,
seggukaay di ma walal ag diw.
7 Bu ma génnaa ba ca bunt dëkk ba,
digg pénc ma laay jekkasndikoo,
8 waxambaane gis ma, ñooru,
mag ña jóg, taxawal ma,
9 kàngam ne xerem,
ub gémmiñam,
10 garmi ne selaw,
làmmiñam taqoo denqleñam,
11 nopp dégg ma, ndokkeel ma,
bët gis ma, seereel ma yiw.
12 Néew-ji-doole woote, ma wallu,
boole ci jirim bu tumurànke.
13 Ñaanu ku naroona sànku di ma dal,
may tooyal xolu jëtun.
14 Njekk laa woddoo woon, njekk wodd ma,
te dëgg laa defoon mbubb ak kaala.
15 Silmaxa, maa dooni gëtam;
ab lafañ, ma diy tànkam.
16 Néew-ji-doole, maa doon baayam,
ku ma xamul sax, may seet àqam.
17 Ku jubadi, ma dammi ŋaamam,
foqatee am pàddam cay sellam.
18 Ma noon samay fan dina neexook feppi suuf,
ma doora deeye sama biir njaboot.
19 Ma noon su ma doon garab samay reen fëllem ndox,
ab lay fanaanee faam car ya.
20 Ma noon darajaa may yeesalal nganam,
may gëna daŋalati xala.
21 Man lees daa déglu, di ma xaar;
ne cell, di taataan samam xel.
22 Samay kàddoo leen di dal, genn-genn,
te su ma àddoo ba daaneel, kàddu jeex.
23 Booba lees ma daa séentu nib taw;
ŋa ŋàpp, di nég waamey waxset.
24 Samay ree gëmeesu ko woon,
xanaa ne siiwa gis sama kanam gu leer.
25 Maa jiite woon, di dogal doxalin,
toog toogaayu buur ci biir gàngooram,
te di leen dëfal ci seen naqar.