Saar 34
Eliyu nee Ayóoba moy na dëgg
1 Eliyu dellu ne:
2 Yeen ñi xelu, dégluleen samay wax,
yeen ñi xam, teewluleen ma.
3 Purux déy ay mosu ñam,
nopp natt kàddu.
4 Kon nan ànd seet li dëggu
te bokk ràññee li baax.
5 Baay Ayóoba kat nee moo yey,
Yàlla xañ ko dëggam.
6 Mu am dëgg, ñu ne moo fen,
tooñul, mu jam ko fittu ndee.
7 Ana ku mel ni Baay Ayóoba mii,
di ñaawle ni muy naanem ndox,
8 di àndandook ñiy def lu ñaaw,
di lëngook nit ñu bon ñi,
9 te naa: «Nit ki seet bànneexu Yàlla,
ana lu mu koy jariñ?»
Yàlla du def lu bon
10 Kon yeen niti xel ñee, dégluleen ma,
Yàlla jegewul fenn mbon!
Aji Man ji jegewul mukk njubadi!
11 Jëfu doom aadama ji daal, moom la koy fey;
na nit kiy jëfe rekk la koy yoole.
12 Li wóor mooy Yàlla du def lu bon,
Aji Man ji du jalgati yoon.
13 Ana ku ko dénk kilifteefu dun bi?
Ana ku ko yen àddina wërngal këpp?
14 Bu ci Yàlla yebu woon,
ba roccim xelam ak noowam,
15 bépp boroom bakkan ay bokk ne lasiim,
doom aadama dellu di pëndub suuf.
Yàlla amul par-parloo
16 Ndegam am ngag dégg, déggal lii,
teewlul sama kàddu gii.
17 Manees naa jiite te bañ yoon?
Am dangay sikkal ki njubam matale?
18 Kii moo naan buur: «Yaa sew!»
naa garmi: «Yaa bon!»
19 Kii du far kàngam,
du teg ku am ci kaw ku ñàkk,
nde ñoom ñaar la boole sàkk.
20 Nes tuut, dee dikke xaaju guddi,
mbooloo fippu, kàngam ya ne mes,
boroom doole sànku, te loxo laalu ko.
21 Yàlla déy a ngi ne jàkk ci jaar-jaari nit ki,
di xool bépp jéegoom.
22 Du fenn fu lëndëm mbaa fu ne këruus,
fu kuy def lu ñaaw mana làqoo.
23 Yàlla daal, soxlawula liñbat nit ki,
bala mu koy woo cib àtte.
24 Mooy rajaxe boroom doole te du laajte,
daldi fal keneen mu wuutu ko.
25 Moo ràññee moos jëfi boroom doole,
ba jàllarbi ko genn guddi, mu rajaxoo.
26 Moo koy dóore fu ne fàŋŋ,
ni ñuy dóore ku bon.
27 Li ko waral di boroom doolee dëddu Yàlla,
sofental mboolem digley yoonam,
28 ba yuuxi baadoola yi àgg fa moom,
mu dégg yuuxi néew-ji-doole ya.
29 Bu Yàlla nee cell, ana ku koy ŋàññ?
Bu làqee kanamam, ana ku koy niir?
Xeet yeek nit ñi la boole tiim,
30 ngir yéefar bi baña falu,
bay tàbbal aw xeet ciy fiir.
Eliyu nee kàdduy Ayóoba du xel
31 Su nit ki nee Yàlla:
«Jot naa samab añ, dootuma bàkkaar.
32 Won ma sama tooñ yi ma gisul.
Su ma defee lu ñaaw, dootuma ko def!»
33 Kooku, Yàlla dina ko mbugal a?
Lu ciy sa xalaat, yaw miy diiŋat,
gannaaw yaay seet te du maay seet?
Waxal boog, loo ci xam!
34 Niti xel ñi dinañu wax,
ñook ku rafet xel ku may déglu,
35 ne ma: «Ayóoba mii waxewul xam-xam,
te kàddoom yi du xel.»
36 Kon na àtteb Baay Ayóoba mii mat sëkk,
nde tontam bokk na ci tontu nit ñu bon ñi.
37 Moo bàkkaar, doyatul muy diiŋat,
di werante ci sunu biir,
di kebetu ci kaw Yàlla.