Saar 35
1 Eliyu dellu ne:
2 Defe nga ne lii yoon la?
Nga ne: «Maa am dëgg fi kanam Yàlla,»
3 te naan ko: «Ana lu ma ci soxal man,
ak lu ma ñàkka bàkkaar di jariñ?»
4 Man mii nag maa lay tontu,
yaak say xarit.
5 Séentul asamaan te xool,
niiral niir yii la tiim!
6 Soo bàkkaaree, lu muy wàññi Yàlla?
Man ngaa tooñ, tooñati ba def ko dara?
7 Ana njekk goo def ba may ko lenn,
ak lu muy jële sax ci say loxo?
8 Sag mbon, sa moroomu nit lay lor,
sag njekk it doom aadama ni yaw lay jariñ.
9 Noteel law na ba nit ñiy yuuxu,
di woote ku leen wallu ci loxol boroom doole.
10 Waaye kenn du ci ne: «Wóoy ana Yàlla mi ma sàkk,
kiy fentloo woyi cant ci biir guddi,
11 di nu xamal lu rabu àll xamul?
di nu may xel mu njanaaw amul?»
12 Bu nit ñu bon ñiy woote wall, du wuyu
ngir seenug réy.
13 Neen lañuy woote, nde Yàlla du leen déglu,
Aji Man ji du leen faale.
14 Kon ngalla yaw mi ne gisoo ko,
te ne diis nga ko sa mbir, di ko xaar.
15 Nga neeti Yàlla du mer, di mbugale,
te yoonam newul ci njubadiy nit.
16 Ayóoba mii de, cóolóolu neen lay wax,
mbel-mbel ju àndul ak xam-xam.