Saar 23
[6]
1 Soo bokkeek kilifa ndab,
xamal bu baax ni ngay lekke.
2 Soo dee ku bëgg lekk,
téyeel sa loxo.
3 Bul xemmem daraam lu neex,
ñam woowu la lay naxe.
[7]
4 Bul rey sa bopp ci wut alal,
bu ko xalaat sax.
5 Ndax xef ak xippi mu wéy,
mel ni lu saxi laaf,
ne fëyy, naaw ni jaxaay.
[8]
6 Ab nay, bul lekke këram,
bul xemmem daraam lu neex.
7 Ma ngay xool la ngay lekk, nu mu tollu,
naan la: «Lekkal, naanal!»
Te xol ba àndu ca.
8 Ndog soo ca lekk, waccu ko,
yiw woo ko wax daldi neen.
[9]
9 Bul wax akub dof,
day xeeb sam xel.
[10]
10 Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf,
bul aakimoo suufas jirim.
11 Ki koy aar màgg na,
da koy taxawu, dal ci sa kaw.
[11]
12 Defal sam xel ci yar,
te teewlu kàdduy xam-xam.
[12]
13 Bul ñéebloo yar gone,
bantal ko taxu koo dee.
14 Soo ko bantalee,
mu mana mucc.
[13]
15 Sama doom, soo xeloo,
sama xol neex.
16 Ngay wax njub,
ma bég.
[14]
17 Bul ñee bàkkaarkat,
saxool ragal Aji Sax ji,
18 ndax kat moo am muj,
te kon sa yaakaar du tas.
[15]
19 Déglul, doom, muusal
te yebu ci yoonu njub.
20 Bul bokk ci ñiy lekk lu ëpp,
ak a màndi,
21 ndax ku bëgg lekk ak a màndi, ñàkk dab la,
dajjant it, rafle rekk.
[16]
22 Déglul sa baay bi la jur.
Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.
23 Jëndal dëgg te bu ko jaay.
Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
24 Su doom jubee, seral xolu baay.
Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25 Deel bégal ndey ak baay,
rawatina ndey ji la jur.
[17]
26 Doom, teewloo ma xel
te roy ma.
27 Ab gànc yeer mu xóot la,
jabaru jaambur di teen bu xat.
28 Ma ngay tëroo nib sàcc,
góor ñu bare lay fecciloo worma.
[18]
29 Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!»
Ana kuy xulook a jàmbat,
di gaañu ci dara,
bët ya xonq curr?
30 Xanaa kiy naan-naane biiñ,
di mosi yeneen njafaan?
31 Bul xool biiñ ak xonqaayam.
Aka yànj cib kaas
te neexa jolu!
32 Bu weesee mu màtt la ni jaan,
ne la càppit ni ñàngóor.
33 Dangay mel ni kuy gis lu doy waar,
sam xel di ràbb lu jekkadi.
34 Nga mel ni ku tëdd biir géej,
di jaayu ca biir gaal ga,
35 nga naan: «Dañu maa dóor te gaañuwuma,
duma ma te yéguma ko.
Moo! Duma yewwu nag,
ba naaneeti?»