Saar 24
[19]
1 Bul ñee ku bon,
bul wuta ànd ak moom,
2 ndax coxor lay nas ci xolam,
te fitna la ay waxam di yee.
[20]
3 Xel mu rafet ay tabax kër,
rafet déggin a koy samp.
4 Xam-xam ay feesal néeg ya
ak mboolem alal ju jafe te yànj.
[21]
5 Ku rafet xel di boroom doole,
ku xam, gëna man;
6 tegtal yu xelu lañuy xaree,
diisoo bu yaatooy maye ndam.
[22]
7 Wax ju xelu sut nab dof,
jataayu pénc du fa àddoo.
[23]
8 Kuy mébét lu bon,
ñu ne yaay rambaaj bi.
9 Pexem dof bàkkaar la,
te kuy ñaawle, ñu sib la.
[24]
10 Bu mettee, nga yoqi,
sa doolee néew.
[25]
11 Wallul ku ñuy reyi te tooñul,
xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.
12 Soo nee sa yoon nekku ci it,
kiy natt xol yi, xam na,
moom miy wattu sa bakkan, xam na,
te kat mooy fey nit jëfam.
[26]
13 Doom, deel lekk lem, baax na,
lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14 Xamal ne xel mu rafet ni la neexe;
soo xeloo, sa muj rafet,
te sa yaakaar du tas.
[27]
15 Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram,
bul yàq dëkkuwaayam.
16 Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat,
ab soxor sërëx ci njekkar.
[28]
17 Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo,
bu tërëfee, bu ko bége.
18 Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko,
daldi giif, dootu ko mbugal.
[29]
19 Bu sa xol tàng ci ku bon,
bul ñee ku soxor.
20 Ku bon amul muj,
ku soxor day mel ni taal bu fey.
[30]
21 Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur.
Bul lëngook kuy fippu.
22 Yàllaak buur a koy bette mbugal,
te kenn xamul musiba mu muy doon.
Yeneen tegtal a ngi
23 Lii it ñi rafet xel a ko wax.
Par-parloo cib àtte baaxul.
24 Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,»
aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
25 ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle,
taasoo barke bu yaa.
26 Ki lay wax dëgg
sa soppe la.
27 Ruujal sab tool, ji ko,
doora tabax sa kër.
28 Bul tuumaal nit ci neen,
te bu ko seedeel ay fen.
29 Bul ne: «Li mu ma def laa koy def,
damay feyu li mu ma def.»
Yaafus amul njariñ
30 Toolub ku yaafus laa jaare,
ak tóokërub nit ku ñàkk bopp.
31 Ndeke lépp a nga saxi dég,
fépp fees akum ñax,
tabaxu doj ba ko wër màbb.
32 Maa ko gis, di xalaat,
xoolaat ko, jànge ca.
33 Booy dajjant ak a for bët,
di tegley loxook a jaaxaan,
34 néewlee ngi lay dikkal nib sàcc,
ñàkk gànnaayul la.