Sabóor 28
Aji Sax jeey àtte ñoñam
Ñeel Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, yaw laay woo,
di la wéeroo, bu ma tanqamlu.
Soo nee cell,
ma xawa tàbbim pax.
Ngalla déglul, ma tinu la,
woo la wall,
dékk lay yoxo,
jublu sa néegu biir bu sell ba.
 
Bu ma sànkaaleek ab soxor,
di ma booleek kuy def lu bon,
di wax moroom ma jàmm,
te dencal ko ay ca xolam.
Fey leen seen liggéey,
seen kemu jëf ju bon.
Jox leen seen añu jëf,
yool leen seen yelleef.
Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam,
ak liggéey bi mu def.
Da leen di yàqte,
te dootu leen yékkati.
 
Jaajëfe Aji Sax ji,
ki ma nangul samay dagaan!
Aji Sax jee may dooleel, di ma feg.
Moom laa wóolu, mu wallu ma,
sama xol tooy,
ma woy, sante ko.
Aji Sax jeey dooleel ñoñam.
Mooy làq, di musal buur bi mu fal.
Ngalla musalal sa mbooloo,
barkeelal sa ñoñ ñii,
sàmm leen, boot ba fàww.