Sabóor 29
Aji Sax jeey boroom ndam
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Yeen goney Yàlla yi, seedeel-leen Aji Sax ji,
seedeel-leen ko teddngaak doole,
seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam.
Sujjóotal-leen Aji Sax ji,
ki gànjaroo sellnga.
 
Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma,
Yàlla mu tedd maa dënu,
Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.
Aji Sax jeey àddoo doole,
Aji Sax jeey àddoo daraja.
Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar,
Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu,
tundu Siryoŋ* 29.6 tundu Siryoŋ mooy tundu Ermon ba tey. it, mbete yëkk wu ndaw.
Aji Sax jeey àddu,
fettaxal sawara, mu boy.
Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ,
Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
Aji Sax jeey àddu, kéwél matu,
garabi àll ruus,
biir këram di mennum riir,
naan: «Màggal-leen ko!»
 
10 Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu,
Aji Sax jee falu buur ba fàww.
11 Aji Sax jeey kàttanal ñoñam,
di barkeele jàmm ñoñam.

*29:6 29.6 tundu Siryoŋ mooy tundu Ermon ba tey.