Sabóor 66
Yàllaay aar nitam
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor.
Yeen waa àddina sépp, sarxolleel-leen Yàlla,
2 woyleen teddngay turam,
darajaal-leen cantam.
3 Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore!
Sa doolee bare, ba say noon rasu,
4 àddina yépp di la sujjóotal,
di la woy, di joobe sa tur.»
Selaw.
5 Dikkleen gis li Yàlla def,
jëf la ju yéeme, ñeel doom aadama yi.
6 Moo soppi géej ag joor,
maam ya dox jàll.
Nanu ko bége foofa.
7 Mooy nguuroo njàmbaaram ba fàww,
di topp xeet yeek bët.
Ku koy diiŋat, yàlla boo damu!
Selaw.
8 Yeen xeet yi, santleen sunu Yàlla,
te biral cantam!
9 Moo sàmm sunu bakkan,
te waccu nu, nu tërëf.
10 Éy Yàlla, nattu nga nu,
xelli nu, ni ñuy xellee xaalis;
11 laaw nga nu,
teg nu njàqare.
12 May nga noon not nu,
nu jaare sawara, jaarem ndox;
nga génne nu, yaatal nu.
13 Maay duggaale sa kër ay saraxi rendi-dóomal,
defal la samay dige,
14 yi ma waxoon ci sama gémmiñ,
sama làmmiñ tudd ko, ba ma jàqee.
15 Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal,
saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya,
ma boole ca saraxu nag ak sikket.
Selaw.
16 Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu,
ma limal la li mu ma defal.
17 Moom laa woo wall,
àddu, màggal ko.
18 Su ma naroon ñaawtéef,
Boroom bi du ma déglu.
19 Waaye Yàlla dégg na ma,
teewlu na samag ñaan.
20 Cant ñeel na Yàlla,
gàntuwul samay ñaan,
xañu ma ngoram.