Sabóor 67
Yal na nu Yàlla barkeel
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor.
 
Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu,
te geesoo nu sa leeru kanam,
Selaw,
ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf,
gis sag wall fi biir xeet yépp.
 
Yaw Yàlla, na la xeet yi sant,
na la xeet yépp sant.
Na xeet yiy bég, di sarxolle;
loo dogalal xeet yi njub la,
te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf.
Selaw.
Yaw Yàlla, na la xeet yi sant,
na la xeet yépp sant.
 
Suuf si nangu na,
yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel.
Yal na nu Yàllay barkeel,
ba àddina wërngal këpp ragal ko.